Help:Tàmbli xët wu bees

From mediawiki.org
This page is a translated version of the page Help:Starting a new page and the translation is 88% complete.
Outdated translations are marked like this.
PD Karmat:Soo soppee wii xët, nangu nga ne yaa ngi joxe say cëru ci anam yi CC0 tëral. Xoolal Xëtu ndimbal wu Public Domain ngir yeneeni xibaar. PD

Bari na anam yoo manee tàmbli xët wu bees.

Dafay aju ci xeetu xët wi nga namma tàmbli, ci wiki bi walla ci tur wi.

Jëfandikoo Wikilinks

MediaWiki yombal na lëkkale xëti ab wiki ci jëfandikoo am mbindiin mum taxawal (xoolal Help:Links )

Soo (walla keneen kum doon) sosee ab lëkkalekaay buy jëme cib jukki bu amagul, lëkkalekaay bi dees koy xonkal niki nii

Notes:
  • This sample displays that underline style unconditionally. The underline displayed below the text of actual links will normally be hidden by default and made visible only when the link is hovered by the mouse or selected by keyboard navigation, if the wiki (or the user's preferences) uses the default MediaWiki styles.
  • The actual color of links is also dependent on the default wiki styles, and the design of Wiki pages may still override these default colors.

Soo bësee cib lëkkalekaay bu xonk daf la yóbb ci xëtu soppiwaayu jukki bu bees bi.

Bindal say mbind ci lu yomb, bës Wàttu rekk xët wi sosu.

Ginnaaw bi xët wi sosoo, lëkkalekaay bi day soppiku jóge xonk mujj doon baxa (yolet xët yi nga jot a ubbi) won la ni xët wi leegi am na.

Naka-jekk nii mooy yoon wi gën ngir sos xët wu bees, ndax day tekki ni dale ca njëlbéen ga xët wi am na lum bon bon weneen wum lëkkalool ci wiki bi (te it dinga ko bëgg a lëkkale ak yeneeni xët yum ndirool ginnaaw bi).

Sooy sos xët wu bees te sosoo njëkk ab lëkkalekaay bu cay yóbbe, war ngaa laaj sa bopp: ndax xët wi séq naak dara lees di waxtaane bi bii wiki?

Tamit, Nan nga yaakaar la aji-nemmeeku ji di def ba gis xët wi.

Ci lu-jaadu amul lenn luy war a waral sosug aw xët te jiitaluñ njëkk lëkkalekaay bu cay jëme

Ca xëtu ceet ga

Soo seetee aw xët wu amul, dees la won aw xët wu am ab lëkkalekaay ngir sos xët wu bees wi.

Jëfandikoo ab URL

Man ngaa jëfandikoo ab URL bu wiki bi ngir sos xët wu bees.

Ab URL bu ab jukkib wiki bi naka-jekk nii lay mel:

  • http://www.example.net/index.php/ARTICLE    or
  • http://www.example.net/wiki/ARTICLE

Soo dindee ARTICLE def fa turu xët wi nga namma sos, dees nañ la yóbb ci xët wu këmm di wone ne amul wenn jukki wu ne tudd wu amagum.

Soo bësee ci làcc wu "Soppi" wi ci kaw xët wi dalay yóbb ci xëtu soppiwaayu jukki boobu, di fa ngay man a sosee xët wu bees wi, duggal fa say mbind te denc leen.

Jëfandikoo ab royukaayu Sosukaayu jukki

This method requires Extension:InputBox to be installed.

Tafal mbind miy toftal ci wenn xëtu wiki bi:

<inputbox>
type=create
width=100
break=no
buttonlabel=Create new article
default=(Article title)
</inputbox>

Loolu dafay jóox ab boyot fu jëfandikukat yi man a bind koju jukki bi, mu jur aw xët wu ne tudd.

Lii di na tax jëfandikukat yu aayul yi noonu man di sosi xët ci lu yomb.

Sos ay jubluwaat ci sa xët wu bees wi

Bul fatte duggalaale ay jubluwaat sooy sos aw xët.

Soo xalaatee ne keneen man naa seet xët wi nga sos ak weneen tur walla mbindiin, sosal jubluwaat yu la fay yóbb.

Xoolal Help:Redirects .

Aar sa xët wu bees wi

Naka-jekk xët wu bees ñeneen ñi dañ koy man a soppi (loolu mooy gis-gis bi jiitu cib wiki)

Su loolu wéyee, ab yorkat man naa aar aw xët, su ko soobee, ngir bañ yenn jëfandikukat yi soppi ko.